10Moo Yàlla daa fàtte ñeewantee? Am meram a tëj buntu yërmandeem?» Selaw.
11Ma ne, sama naqar daal mooy Aji Kawe ji daa soppi loxoom.
12Waaye naa fàttliku jaloorey Ki Sax rekk, fàttliku kéemaanam ya woon.
13Naa xalaat sa bépp liggéey, di jàngat say jëf.
14Céy Yàlla, yaa sell jikko! Jan yàllaa màgg ni Yàlla?
15Yaa di Yàlla juy jëfi kéemaan, yaa siiwal sa doole ci biir xeet yi.
16Kàttan nga jote sa mbooloo ma, sëti Yanqóobaak Yuusufa. Selaw.
17Yàlla, ndox maa la gis, ndox maa la gis, di lox; xóote yaa say,