14boole leen jot ci notaangeek loraange, ngir fonk seen bakkan.
15Yal na Buur gudd fan, yal nañu ko may wurusu Saba. Nañu koy ñaanal saa su ne, di ko saxoo, mu barkeel.
16Yal na pepp ne gàññ ci réew mi, yal na gub yay jaayu ca tund ya ni gottub Libaŋ; dëkk yu mag yi sëqi nit ba law,