11buuroo buur di ko sujjóotal, xeetoo xeet di ko surgawu.
12Mooy xettliji aji tumurànke bu woote wall ak aji néewle ju sësul fenn.
13Mooy yërëm ku néewleek ku tumurànke, di sàmm bakkanu aji tumurànke,
14boole leen jot ci notaangeek loraange, ngir fonk seen bakkan.
15Yal na Buur gudd fan, yal nañu ko may wurusu Saba. Nañu koy ñaanal saa su ne, di ko saxoo, mu barkeel.