4Ma woote wall ba tàyyi, sama put gi wow koŋŋ. Ma séentu la, yaw sama Yàlla, ba samay gët giim.
5Sama kawari bopp sax, ñi ma bañ ci daraa ko ëpp. Ñu bare doole, bëgg maa sànk, noonoo ma ci dara. Sàccuma, nara fey!
6Yaw Yàlla, xam nga sama jëfi dof, te samay tooñ umpu la.