Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 69

Sabóor 69:2-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Éy Yàlla, wallu ma! Ndox maa ngi ma tollu ci put.
3May suux ci ban bu xóot, te awma fu ma teg tànk. Maa ngi nii ci ndox mu xóot, gannax yi mëdd ma.
4Ma woote wall ba tàyyi, sama put gi wow koŋŋ. Ma séentu la, yaw sama Yàlla, ba samay gët giim.
5Sama kawari bopp sax, ñi ma bañ ci daraa ko ëpp. Ñu bare doole, bëgg maa sànk, noonoo ma ci dara. Sàccuma, nara fey!
6Yaw Yàlla, xam nga sama jëfi dof, te samay tooñ umpu la.

Read Sabóor 69Sabóor 69
Compare Sabóor 69:2-6Sabóor 69:2-6