3Yàlla wal, ñu naaw ni saxar. Ñu bon ñi sànku fi kanam Yàlla, mbete dax ak sawara.
4Ñu jub ñi nag bég, di bànneexu fi kanam Yàlla, tey puukarewoo mbégte.
5Woyleen Yàlla, teral turam, xàllal-leen kiy war niir yi, Ki Sax moo di turam. Bànneexuleen fi kanamam.
6Mooy baayoo jirim, di àtte jëtun, kookoo di Yàlla ja fa dëkkuwaayu sellngaam.
7Yàllaay sàkkal ku wéet wéttal, di afal ku ñu tëjoon, bégal ko, ku déggadi rekk ay dëkke suuf su ne sereŋ.
8Céy Yàlla, yaa génn, jiitu sa mbooloo, daagu, dugg màndiŋ ma. Selaw.
9Suuf yëngu, asamaan sóob fi kanam Yàlla, boroom tundu Sinayi, Yàllay Israyil ja!
10Yàlla, waame nga tawal, leqlee ko réew mi nga séddoo, fa mu sonne,
11sa mbooloo dëkke fa. Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax.