Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 68

Sabóor 68:23-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
23Boroom bi nee: «Basan laay waññee noon yi, waññee leen xóotey géej,
24ngeen mana xuus ci seen deret, seeni xaj séddu ci seeni néew.»
25Céy Yàlla, gis nañu sa gàngoor di daagu, sama Yàlla, sama buur, sa gàngoor ba ca biir kër gu sell ga.
26Woykat ya jiitu, xalamkat ya mujje, janq ji yéewe leen tëgg um njiin.
27Dajeleen, di sant Yàlla, yeen askanu Israyil, santleen Aji Sax ji.
28Giirug Beñamin a ngi jiitu, gën cee néew, njiiti Yuda topp caak seeni kurél, njiiti Sabulon topp caak njiiti Neftali.
29Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan; éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon.
30Sa kër gi tiim Yerusalem, fa la la buur yiy indiley galag.
31Nanga fa gëdde rabu àll wi ci barax yi, ñooy gétti yëkk yi, xeet yi ci des diy sëllu. Gëdd leen, ba ñu sujjóotalsi laak dogi xaalis. Tasaareel xeet yooyu sopp xare,
32ay kàngam bàyyikoo Misra aki galag, réewum Kuus baral loxoom, indil Yàlla.

Read Sabóor 68Sabóor 68
Compare Sabóor 68:23-32Sabóor 68:23-32