Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 68

Sabóor 68:2-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Yàllaay jóg, noonam ya tasaaroo; bañam ña daw, dëddu ko.
3Yàlla wal, ñu naaw ni saxar. Ñu bon ñi sànku fi kanam Yàlla, mbete dax ak sawara.
4Ñu jub ñi nag bég, di bànneexu fi kanam Yàlla, tey puukarewoo mbégte.
5Woyleen Yàlla, teral turam, xàllal-leen kiy war niir yi, Ki Sax moo di turam. Bànneexuleen fi kanamam.
6Mooy baayoo jirim, di àtte jëtun, kookoo di Yàlla ja fa dëkkuwaayu sellngaam.
7Yàllaay sàkkal ku wéet wéttal, di afal ku ñu tëjoon, bégal ko, ku déggadi rekk ay dëkke suuf su ne sereŋ.

Read Sabóor 68Sabóor 68
Compare Sabóor 68:2-7Sabóor 68:2-7