3ba ñu ràññee sa loxo fi kaw suuf, gis sag wall fi biir xeet yépp.
4Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.
5Na xeet yiy bég, di sarxolle; loo dogalal xeet yi njub la, te yaay wommat xeet yi ci kaw suuf. Selaw.
6Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.
7Suuf si nangu na, yal na nu Yàlla, sunu Yàllay barkeel.