3 ba ñu ràññee sa loxo fi kaw suuf, gis sag wall fi biir xeet yépp.
4 Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.
5 Na xeet yiy bég, di sarxolle; loo dogalal xeet yi njub la, te yaay wommat xeet yi ci kaw suuf. Selaw.
6 Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.
7 Suuf si nangu na, yal na nu Yàlla, sunu Yàllay barkeel.