Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 66

Sabóor 66:1-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor. Yeen waa àddina sépp, sarxolleel-leen Yàlla,
2woyleen teddngay turam, darajaal-leen cantam.
3Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore! Sa doolee bare, ba say noon rasu,
4àddina yépp di la sujjóotal, di la woy, di joobe sa tur.» Selaw.
5Dikkleen gis li Yàlla def, jëf la ju yéeme, ñeel doom aadama yi.
6Moo soppi géej ag joor, maam ya dox jàll. Nanu ko bége foofa.
7Mooy nguuroo njàmbaaram ba fàww, di topp xeet yeek bët. Ku koy diiŋat, yàlla boo damu! Selaw.
8Yeen xeet yi, santleen sunu Yàlla, te biral cantam!

Read Sabóor 66Sabóor 66
Compare Sabóor 66:1-8Sabóor 66:1-8