7Dañuy lal pexem njubadi te naan: «Lal nanu pexe mu mat sëkk.» Nit aka xóot xel te xóoti mbóot!
8Waaye Yàllaa leen di jamu fittam, ñu jekki daanu.
9Seen làmmiñ a leen di fakkastal, ba ku leen xool wëcc bopp.
10Ñépp a ciy am tiitaange, bay siiwal la Yàlla def, tey xalaataat jëfam jooju.