6Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar, di diisoo na ñuy làqe ay fiir, te naan: «Kenn du ko gis!»
7Dañuy lal pexem njubadi te naan: «Lal nanu pexe mu mat sëkk.» Nit aka xóot xel te xóoti mbóot!
8Waaye Yàllaa leen di jamu fittam, ñu jekki daanu.
9Seen làmmiñ a leen di fakkastal, ba ku leen xool wëcc bopp.