Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 62

Sabóor 62:3-5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Moom doŋŋ mooy sama wéeru-mucc, di ma rawale, ba duma sànku!
4Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit, nar koo sànk, ni kuy màbb tabax bu joy, mbaa ngay bàddi per mu ràpp?
5Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ; yeena ngi bége ay fen, seeni kàddu diw yiw, seen xalaat diy saaga. Selaw.

Read Sabóor 62Sabóor 62
Compare Sabóor 62:3-5Sabóor 62:3-5