1Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2Yàlla doŋŋ ay dalal sama xel, moo may wallu.
3Moom doŋŋ mooy sama wéeru-mucc, di ma rawale, ba duma sànku!
4Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit, nar koo sànk, ni kuy màbb tabax bu joy, mbaa ngay bàddi per mu ràpp?