Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 61

Sabóor 61:1-4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.
2Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
3Àll laa lay wooye, sama xol jeex; yéege ma doju rawtu wu ma jotul.
4Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.

Read Sabóor 61Sabóor 61
Compare Sabóor 61:1-4Sabóor 61:1-4