Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 60

Sabóor 60:3-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Éy Yàlla, wacc nga nu, bëtt sunu kiiraay. Mer nga, waaye ngalla xettli nu.
4Yëngal nga suuf, xar ko; ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!
5Won nga sa mbooloo lu metti, nàndal nu biiñu mbugal, ba nu miir.
6Artu nga ñi lay jaamu, ngir mucc fitt. Selaw.
7Walloo nu sa ndijoor, nangul nu, ba say soppe xettliku.
8Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkóot.

Read Sabóor 60Sabóor 60
Compare Sabóor 60:3-8Sabóor 60:3-8