Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 60:3-8 in Wolof

Help us?

Sabóor 60:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Éy Yàlla, wacc nga nu, bëtt sunu kiiraay. Mer nga, waaye ngalla xettli nu.
4 Yëngal nga suuf, xar ko; ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!
5 Won nga sa mbooloo lu metti, nàndal nu biiñu mbugal, ba nu miir.
6 Artu nga ñi lay jaamu, ngir mucc fitt. Selaw.
7 Walloo nu sa ndijoor, nangul nu, ba say soppe xettliku.
8 Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkóot.
Sabóor 60 in Kàddug Yàlla gi