Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 5

Sabóor 5:7-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen, sib kuy bóomeek kuy wore.
8Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër, sujjóotal sa bérab bu sell, wormaale la.
9Éy Aji Sax ji, wommate ma sa njekk ndaxi noon, te xàllal ma saw yoon.
10Ñii, lu ñu wax, wérul, seen xol a mébét njekkar, seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, ñuy naxe làmmiñ wu neex.
11Éy Yàlla, topp leen, ñu fakktaloo seeni pexe; xalabal ñii barey moy, ñoo la gàntal.
12Képp ku la làqoo, yal na bég, di saxoo sarxolle, nga di ko yiir, te ku la sopp di la bége.

Read Sabóor 5Sabóor 5
Compare Sabóor 5:7-12Sabóor 5:7-12