Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 5:7-12 in Wolof

Help us?

Sabóor 5:7-12 in Kàddug Yàlla gi

7 Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen, sib kuy bóomeek kuy wore.
8 Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër, sujjóotal sa bérab bu sell, wormaale la.
9 Éy Aji Sax ji, wommate ma sa njekk ndaxi noon, te xàllal ma saw yoon.
10 Ñii, lu ñu wax, wérul, seen xol a mébét njekkar, seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, ñuy naxe làmmiñ wu neex.
11 Éy Yàlla, topp leen, ñu fakktaloo seeni pexe; xalabal ñii barey moy, ñoo la gàntal.
12 Képp ku la làqoo, yal na bég, di saxoo sarxolle, nga di ko yiir, te ku la sopp di la bége.
Sabóor 5 in Kàddug Yàlla gi