Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 57

Sabóor 57:5-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Maa ngi tëdd ci biiri noon yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. Seeni sell niy xeej aki fitt, seen làmmiñ di saamar yu ñaw.
6Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, sag leer tiim suuf sépp.
7Noon yi di ma fiir, sama xol jeex. Ñu gasal mam pax, far tàbbi ca. Selaw.
8Yàlla, dogu naa, dogu naa woy, di la kañ.
9Na sama jëmm jépp yewwu, xalam ak moroom ma yewwu; ma yee leeru njël.

Read Sabóor 57Sabóor 57
Compare Sabóor 57:5-9Sabóor 57:5-9