12Yàq a nga ca biir, te noteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.
13Su doon noon bu may ñaawal, ma muñ ko, mbaa muy bañ bu may won ab dayo, ma daw ko.
14Waaye yaw la, sama nawle, di sama wóllëre, ma xam la.
15Nu daan bokk bànneexu diisoo, ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga.
16Yal na leen dee bett, ñu jekki tàbbi njaniiw, ngir mbon ga seen biir ak seen dëkkuwaay.