6Yaa bëgg jépp wax juy yàq, waabajiiba bi!
7Yàlla da lay sànk ba fàww, fëkke la sab xayma, yóbbu, déjjatee la réewum aji dund. Selaw.
8Aji jub gis ko, yéemu, di la ree, naa:
9«Xool-leen jàmbaar ji làqoowul Yàlla, xanaa di yaakaar alalam ju bare, di yokkoo loraange.»