Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 51

Sabóor 51:6-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, yaa yey; te soo àttee, wàcc nga.
7Ñaawtéef daal laa judduwaale, te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar.
8Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol, kon déey ma xel mu rafet.
9Wis ma ndox, ma sell; sang ma, ma set wecc.
10Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex, ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee.
11Bul xool samay moy, faral sama ñaawtéef yépp.
12Éy Yàlla, sàkkal ma xol bu sell, yeesalal ma pastéefu xol.
13Bu ma xalab, bu ma xañ sa noo gu sell.
14May ma, ma bégeeti sag wall, te dundale ma xol bu tàlli,
15ma xamal tooñkat sa war, ba moykat dellu ci yaw.

Read Sabóor 51Sabóor 51
Compare Sabóor 51:6-15Sabóor 51:6-15