7ne fay pat-pati, jàq ni kuy matu.
8Ngelawal penku, moom ngay tase gaal gu mag.
9La nu déggoon de lanu gis ca dëkkub Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, sunu dëkku Yàlla ba. Yàllaa koy dëgëral ba fàww. Selaw.
10Céy Yàlla, nu ngi sa biir kër, di xalaat sa ngor.
11Céy Yàlla, sa tur ay sa woy ba ca cati àddina. Njekk la sa loxo fees.
12Yal na waa tundu Siyoŋ bég, waa Yuda bànneexoo say àtte.