Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 48:7-12 in Wolof

Help us?

Sabóor 48:7-12 in Kàddug Yàlla gi

7 ne fay pat-pati, jàq ni kuy matu.
8 Ngelawal penku, moom ngay tase gaal gu mag.
9 La nu déggoon de lanu gis ca dëkkub Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, sunu dëkku Yàlla ba. Yàllaa koy dëgëral ba fàww. Selaw.
10 Céy Yàlla, nu ngi sa biir kër, di xalaat sa ngor.
11 Céy Yàlla, sa tur ay sa woy ba ca cati àddina. Njekk la sa loxo fees.
12 Yal na waa tundu Siyoŋ bég, waa Yuda bànneexoo say àtte.
Sabóor 48 in Kàddug Yàlla gi