2Aji Sax jee màgg, jara màggala màggal ca sunu biir dëkku Yàlla, kaw tundam wu sell.
3Jekk taxawaayee tundu Siyoŋ, catu bëj-gànnaar, dëkku buur bu mag bi, di mbégtem àddina sépp.
4Yàllaa wone kaaraangeem ca biir tatay dëkk ba.
5Buur yaa ngoog daje, àndandoo.