4Moo nu nangulal xeet yi, nu teg tànk gàngoor yi.
5Moo nu tànnal céru suuf, muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp.
6Yàllaa yéeg, kàddu riir. Aji Sax jee yéeg, bufta jolli.
7Woyleen Yàlla, woyleen, woyleen Yàlla sunu buur, woyleen.
8Yàllaay buuru àddina sépp; taalifleen, woy ko.