Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 46

Sabóor 46:2-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee,
3ba dunu tiit suuf su yëngu sax, ba tund yiy tàbbi biir géej,
4mbaa gannax yuy riir, di fuur ak a fuddu bay gësëm tund yi. Selaw.
5Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla, sellngay dëkkuwaayi Aji Kawe ji.
6Yàllaa ngi ci biir dëkk bi, du raf; Yàllaa koy dimbali ba jant fenkee.
7Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!
8Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.
9Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.
10Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.
11Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla, màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»

Read Sabóor 46Sabóor 46
Compare Sabóor 46:2-11Sabóor 46:2-11