2Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
3Yaa gëna góorayiwe ci àddina, sa kàddu diw yiw, ndax Yàllaa la barkeel ba fàww!
4Jàmbaaroo, takkal sa saamar, te yànj, am daraja;
5ànd ak daraja, dawal ba am ndam, di dawal dëgg ak yërmande ji war, ba mana def ay jaloore.
6Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.
7Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. Njub nga ŋanke sa nguur gi,
8di sopp dëgg, bañ lu bon, ba Yàlla, sa Boroom diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom:
9sa yére yépp di gilli ndàbb, alowes akum kanel, ñu di la bégale xalam, ca sa biir kër yu yànj.
10Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral, sab lingeer féete la ndijoor, takkoo ngëneelu wurus.
11Janq doom, gisal, déglul te teewlu ma, fàtteel say bokk, fàtte sa kër baay,
12Buur xemmeme la sab taar; mooy sab sang, wormaal ko.
13Waa Tir a lay yótsiy may, ay boroom alal di wut lu la neex.
14Séetu Buur duggsi na, ne ràññ, sol mbubb mu wurus way tàkk.