4Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos, seen dooley bopp it mayu leen ndam. Yaa ko defe kàttan ak doole, geesoo leen sa leeru kanam, ngir sa cofeel.
5Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla, mayal askanu Yanqóoba ay ndam.
6Yaw lanuy dàqe bañ yi, sa tur lanuy dëggaatee ñi nu song.
7Du fitt laa wóolu, du saamar a may may ndam.
8Yaa nuy musal ci bañ yi, yaay gàcceel noon ñi.
9Yàlla lanuy damoo bésoo bés, di màggal turam ba fàww. Selaw.
10Waaye danga noo wacc, torxal nu, ba àndulook sunu mboolooy xare.
11Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw, ñu bañ nu, ba futti nu.
12Ni gàtt yu ñuy yàpp, ni nga nu joxee, tasaare nu ci biir xeet yi.
13Jaay nga sa mbooloo ci dara, te jariñu la tus.
14Tax nga sunuy dëkk di nu ree, ñi nu séq di nu kókkaleek a ñaawal.
15Tax nga xeet yi di nu léeboo, jaambur yaa ngi nuy wëcc bopp!
16Damaa dëkke gàcce, sëlmoo kersa
17ndax kókkali yeek xastey nit ñi ma bañ, di feyoonteek man.
18Lii lépp dal na nu, te fàttewunu la, fecciwunu la kóllëre.
19Dëdduwunu la, wàccunu saw yoon,