Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 44

Sabóor 44:19-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Dëdduwunu la, wàccunu saw yoon,
20teewul nga not nu, wacce nu xaj ya, këpp nu lëndëmu ndee.
21Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla, ba tàllal tuuri doxandéem yi loxo,
22du la ump, yaw Yàlla, mi xam kumpay xol.
23Yaa tax ñu yendu noo bóom, dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.

Read Sabóor 44Sabóor 44
Compare Sabóor 44:19-23Sabóor 44:19-23