19 Dëdduwunu la, wàccunu saw yoon,
20 teewul nga not nu, wacce nu xaj ya, këpp nu lëndëmu ndee.
21 Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla, ba tàllal tuuri doxandéem yi loxo,
22 du la ump, yaw Yàlla, mi xam kumpay xol.
23 Yaa tax ñu yendu noo bóom, dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.