4Rongooñ laay dunde guddeek bëccëg, noon yi di ma dëkke naa: «Ana sa Yàlla ji?»
5Lii laay fàttliku, sama xol jeex: dama daan jàll, jiite mbooloo ma, jëm kër Yàlla ga, di sarxolleek a sant, ñu booloo di màggal.
6Moo man, lu may yoggaaral nii? Lu may jàq? Naa yaakaar Yàlla, ba dellu sante sama Yàlla wallam.
7Maa ngi ne yogg, ba di la fàttlikoo fa réewum Yurdan ak tundi Ermon ak Misar.
8Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma; say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.