Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 42

Sabóor 42:3-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Maa mar Yàlla, Yàlla jiy dund! Kañ laay teewi fa kanam Yàlla?
4Rongooñ laay dunde guddeek bëccëg, noon yi di ma dëkke naa: «Ana sa Yàlla ji?»
5Lii laay fàttliku, sama xol jeex: dama daan jàll, jiite mbooloo ma, jëm kër Yàlla ga, di sarxolleek a sant, ñu booloo di màggal.
6Moo man, lu may yoggaaral nii? Lu may jàq? Naa yaakaar Yàlla, ba dellu sante sama Yàlla wallam.

Read Sabóor 42Sabóor 42
Compare Sabóor 42:3-6Sabóor 42:3-6