3génnee ma ca kàmbug sànkute, sippee ma ca xóotey ban ba, cëppe ma ciw doj, samp ma, ma dëgër.
4Moo ma may, ma fent, woy wu ma woye sunu Yàlla. Ñu baree seede, di wormaal ak a dénku ci Aji Sax ji.
5Ndokklee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.