12Éy Aji Sax ji, bu ma xañ sa yërmande. Sa ngor ak sa worma, yal na ma feg ba fàww.
13Ay musibaa ma tanc, ne gàññ, ba wees ab lim. Samay ñaawtéef a ma dab, ba gisatuma, baree bare, ba ëpp sama kawari bopp; sama xol jeex tàkk.
14Éy Aji Sax ji, yal na la neex, nga wallu ma! Éy Aji Sax ji, gaawe ma!
15Képp kuy wuta fëkk sama bakkan, yal na rus, torox ne tott. Kuy bége sama loraange, yal nañu ko duma, mu ne yàcc.
16Ku may ñaawal, yal nañu ko torxal, mu jommi.