Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 39

Sabóor 39:7-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Nit du lu moy takkndeer buy dem, cóolóolu neen lay kër-këri. Nit a ngi dajale, xamul kuy for.
8«Éy Boroom bi, lu may xaarati? Sama yaakaar yaw a.
9Musal ma ci sama mbugali tooñoo tooñ, bu ma bàyyi, dof di ma reetaan!
10Noppi naa, dootuma wax, yaw yaa dogal lii.
11Waaye ngalla teggil sab yar, sa diisaayu loxoo ngi may jekkli.

Read Sabóor 39Sabóor 39
Compare Sabóor 39:7-11Sabóor 39:7-11