3Dama noon cell, ne patt, noppi, ba mu ëpp; sama njàqare yokku,
4sama xol diis, xel di xelaat, xol diis gann; ma mujj àddu,
5ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj ak sama àppi fan, ma xam ni sama dund gàtte.
6Yaatuwaayu loxo nga ma àppal ciy fan, sama giiru dund du dara fi yaw. Képp ku taxaw di cóolóolu neen. Selaw.
7Nit du lu moy takkndeer buy dem, cóolóolu neen lay kër-këri. Nit a ngi dajale, xamul kuy for.
8«Éy Boroom bi, lu may xaarati? Sama yaakaar yaw a.
9Musal ma ci sama mbugali tooñoo tooñ, bu ma bàyyi, dof di ma reetaan!
10Noppi naa, dootuma wax, yaw yaa dogal lii.