20Ku bon sànku; noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la, bu tàkkee, jeex tàkk.
21Ku bon leb, du fey; ku jub yéwén, di joxe.
22Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos; mu alag la, nga dog.
23Aji Sax jeey sopp saw yoon, jiite say jéego.
24Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
25Ba may ndaw, ba tey may mag, gisuma ku jub ñàkk ndimbal, mbaa askanam di dunde yalwaan.
26Day saxoo tabe, di leble, askanam barkeel.
27Dëddul mbon, di jëfe mbaax, ba dëkke réew mi fàww.
28Aji Sax ji kat daa sopp yoon, te du wacc jaamam bu gore. Day fegu ba fàww, askanu ku bon dog.
29Aji jub ay jagoo réew mi, dëkke ko ba fàww.
30Kàddug aji jub day xelu, wax ja jub;
31yoonu Yàllaam a nga ca xol ba, du dox ba tërëf.