Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 37

Sabóor 37:2-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Léegi mu wow nim ñax, lax ni gàncax.
3Dénkul ci Aji Sax ji, di def lu baax, ba des ci réew meek jàmm.
4Deel bànneexoo Aji Sax ji, mu may la say nammeel.
5Jébbalul ci Aji Sax ji, dénku ci moom, mooy sottal.
6Day setal sab der ni jant bu fenk; sab àtte ne ràññ ni njolloor.
7Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle, tey lal ay pexe.
8Baal mer, dëddu xadar. Xol bu jóg, loraangey neen.
9Ku bon, ñu dagg, sànni; ku yaakaar Aji Sax ji, jagoo réew mi.
10Nes tuut, ku bon ne mes, nga seet, seet, mu réer.
11Waaye néew-dooleey jagoo réew mi; jàmm ne ñoyy, ñu bége.
12Ku bon fexeel ku jub, di ko màttu,
13Buur Yàlla di ko ree, xam ne bésam a ngi ñëw.
14Ku bon bocci saamar, tàwwig fitt, nara rey ku ñàkk, néewle, nara bóom kuy jubal;
15far jam boppam saamaru xol, fittam damm.
16Aji jub, as tuutam moo gën koomu ku bon.
17Ku bon kat, sa doole dëddu la; ku jub, Aji Sax ji wallu la.
18Ku maandu, Aji Sax ji yég la, sab cér sax.
19Bu mettee doo rus, te bésub xiif dangay regg.
20Ku bon sànku; noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la, bu tàkkee, jeex tàkk.
21Ku bon leb, du fey; ku jub yéwén, di joxe.
22Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos; mu alag la, nga dog.

Read Sabóor 37Sabóor 37
Compare Sabóor 37:2-22Sabóor 37:2-22