Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 36

Sabóor 36:7-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Sa njekk a tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!
8Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa ker, yiiru;
9yafloo sa njël lu duun, sa xéewal wal, nga nàndale ko.
10Ci yaw la dund di balle, te sag leer lanuy leerloo.
11Jotaleel sa ngor ku la xam, jotale sa njekk kuy nas njub.
12Yàlla bu ma ku reew teg tànk; loxo ku bon, yàlla bumu ma taxa daw.

Read Sabóor 36Sabóor 36
Compare Sabóor 36:7-12Sabóor 36:7-12