7 Sa njekk a tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!
8 Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa ker, yiiru;
9 yafloo sa njël lu duun, sa xéewal wal, nga nàndale ko.
10 Ci yaw la dund di balle, te sag leer lanuy leerloo.
11 Jotaleel sa ngor ku la xam, jotale sa njekk kuy nas njub.
12 Yàlla bu ma ku reew teg tànk; loxo ku bon, yàlla bumu ma taxa daw.