4Ay waxam coxor aki fen, jëfeetul lu rafet ak lu baax.
5Day mébét lu ñaaw cib lalam, taxawe yoon wu dëddu mbaax, te du bañ lu bon.
6Céy Aji Sax ji, gore nga ba kaw asamaan, dëggu ba kaw-li-kaw.
7Sa njekk a tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!
8Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa ker, yiiru;