2Kàddug tooñ ga ku bon wax mu ngi sama xel mi. Mu ne: «Ana lu may ragal ci Yàlla?»
3Day gis boppam, naagu, ba du gis sikkam, sib ko.
4Ay waxam coxor aki fen, jëfeetul lu rafet ak lu baax.
5Day mébét lu ñaaw cib lalam, taxawe yoon wu dëddu mbaax, te du bañ lu bon.