22Éy Aji Sax ji, yaa ci gis, bul selaŋlu, éy Boroom bi, bul ma sore.
23Jógal, sàmmal ma sama àq. Sama Yàlla, Boroom bi, àtte ma yoon.
24Aji Sax ji sama Yàlla, àttee ma sa dëgg, ñu bañ maa ree!
25Yàlla buñu ne: «Ñaw! Lii rekk lanu bëggoon.» Yàlla buñu ne: «Sàkkal nanu ko pexe.»
26Ku bége sama njàqare, yal nanga rus, ba torox. Kuy réy-réylu ci sama kaw, yal nanga am gàcce, ne yàcc.
27Ku bége sama der bu set, yal nanga bànneexu, di sarxolle, foo tollu di biral naan: «Aji Sax jee màgg! moom miy bége jàmmi jaamam.»
28Man it ma tudd sa njekk, di la dëkke màggal!