Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 29

Sabóor 29:5-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar, Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ.
6Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu, tundu Siryoŋ it, mbete yëkk wu ndaw.
7Aji Sax jeey àddu, fettaxal sawara, mu boy.
8Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ, Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.
9Aji Sax jeey àddu, kéwél matu, garabi àll ruus, biir këram di mennum riir, naan: «Màggal-leen ko!»

Read Sabóor 29Sabóor 29
Compare Sabóor 29:5-9Sabóor 29:5-9