1Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Yeen goney Yàlla yi, seedeel-leen Aji Sax ji, seedeel-leen ko teddngaak doole,
2seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam. Sujjóotal-leen Aji Sax ji, ki gànjaroo sellnga.
3Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma, Yàlla mu tedd maa dënu, Aji Sax jeey tiim ndox, mi ne màww.