6Jaajëfe Aji Sax ji, ki ma nangul samay dagaan!
7Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.
8Aji Sax jeey dooleel ñoñam. Mooy làq, di musal buur bi mu fal.
9Ngalla musalal sa mbooloo, barkeelal sa ñoñ ñii, sàmm leen, boot ba fàww.