4Fey leen seen liggéey, seen kemu jëf ju bon. Jox leen seen añu jëf, yool leen seen yelleef.
5Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam, ak liggéey bi mu def. Da leen di yàqte, te dootu leen yékkati.
6Jaajëfe Aji Sax ji, ki ma nangul samay dagaan!
7Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.